IHE Wiki

Soppi lëkkalekaay yi

Burkina Faso (wax: /buʁ.ki.na fa.so/ wala /byʁ.ki.na fa.so/), maanaam «réemu nit ñu dëggu» wala «réemu njub», ñu ngi ko woowe République de Volta8 , réew la ci sowwu Afrig . Bu ko dul jot ci géej gi, juróom-benni réew ñoo ko wër: Niseer ci penku-nord-est, Benin ci penku-sud-est, Togo ci sud-est, Ganaa ci sud, Cote d’Ivoire ci sud-ouest ak Mali ci nord-ouest. Kapitaalam ci wàllu politig, Waagadugou, mi ngi féete ci diggu réew mi. Kapitaalu koom-koom gi mooy Bobo-Dioulasso , mi ngi nekk ci Hauts Bassins , ci bëj-gànnaaru réew mi.Ci atum 1896, Royaume bu Mossi bu Ouagadougou nekk na protectorat bu français, balaa muy nekk koloni Volta bu kawe ci 1919, ginaaw ga mu dellu ci atum 19479, ginaaw bi ñu ko daanele ci atum 193210. Moom boppam ci France ci 5 août 1960, République bu Upper Volta Burkina Faaso ci atum 1984 ci nguurug Tomaas Sankara.  Blaise Compaoré moo ko daaneel, rey ko ci atum 1987. Réew mi amagul woon nguuru demokraasi balaa 30 nowàmbar 2015 ak li Roch Marc Christian Kaboré jëlee njiitu réew mi.  Jamonoy demokraasi bu njëkk bi mungi jeex ci 2022, ci jamonoy coup detaa bi ci weeru janvier ak septembre bi waral ñu taxawal benn nguuru soldaar ci jamono boo xamni ay songe terrorist ñungi doon yokku.  Lu ko dalee ci diggu ati 2010, réew mi nekk na jafe-jafe ci yokkuteg jëfi kuréeli jihadist yu am ay weñ ci Sahel bi yépp.[1]

Xayma nañu limu nit ñi dëkk ci 20 505 15511.  Burkina Faaso am na yaatuwaayu 274 200 km212.  Mingi nekk ci 184eelu palaas ci 191, ak limu yokkuteg doomi aadama ci 0.449 ci 2021. Bokk na ci mbootaay yu bari lu ci melni Mbootaayu Xeet yi (ONU), Bànk Afrique buy Yokkateg Afrique (AfDB), Mbootaayu Jëflante Islamik (OCI) wala Mbootaay buy boole yooni liggéey ci Afrique (OHADA), waaye dañu ko dàq ci yeneen mbootaay yu bari (OIF, AU, CEDEAO, ak ñoom seen) ndax coup detaa bi am ci weeru janvier 2022 ak septembre 2022 ci réew mi.

Réewum Burkina Faaso
Raaya bu Burkinaa Faaso Kóót bu aarms bu Burkinaa Faaso
Barabu Burkinaa Faaso ci Rooj
Barabu Burkinaa Faaso ci Rooj
Dayo 274,000 km2
Gox
Way-dëkk 20,107,509 (2017) nit
Fattaay nit/km2
Xeetu nguur
- Njiitu Réew
- Njiitu Jëwriñ
-
Roch March Christian Kaboré
Lassina Zerbo
Tembte
- Bawoo
- Taariix
Péy ak rëddi
Tus-wu-gaar
Tus-wu-taxaw
Wagaaduguu
Làkku nguur-gi Wu-faraas
Koppar Franc CFA (XOF)
Turu aji-dëkk Burkina-Burkina
-Sa-Burkina
Telefon
Lonkoyoon bu Burkinaa Faaso
Lonkoyoon bu Burkinaa Faaso   

Burkina Faso : réewu Afrig.


Réewi afrig

Afrig gu Bëj-saalum • Alseeri • Angolaa • Bene • Botswana • Burkina Faso • Buruundi • Cadd • Ecoopi • Eritere • Eswatini • Gaambi • Gaboŋ • Gana • Gànnaar • Ginne • Ginne Bisaawóo • Ginne gu Yemoo • Isipt • Jibuti • Kamerun • Kap Weer • Réewum Diggu Afrig • Keeñaa • Komoor • Kongóo-Brasaawiil • Kongóo-Kinshasa • Kot Diwaar • Lesoto • Libeeria • Libi • Madagaskaar • Malawi • Mali • Marook • Móoris • Mosambik • Namibi • Niseer • Niseeria • Ruwandaa • Saambi • Sahara gu Sowwu • Sao Tome ak Principe • Senegaal • Seysel • Simbaawee • Siraa Leyoon • Somali • Sudaan • Sudaan gu Bëj-saalum • Tansani • Togóo • Tiniisi • Ugandaa

  1. pays